Wakhtaanu kilifeu gui niou denk waloum artisanat ak transformation secteur informel ak waa ODCAV
Dibeer, niar fouki fan ak diourom niente si weerou août dieuwrign djinou denk waloum artisanat moodone sekkeu waxtan ak kourel gui di ODCAV si mbirou jonganté football yiniou deugg meul si biir Thiès.

Khew, khew bobou ndjiitou ODECAV moko téwé woon and si aki nioniam. Moom sakh diotna sani ay kaddu you rafett si ki di Docteur Amadou Ndiaye miniou denk waloum artisanat « Amadou Ndiaye yaag na diapalé mouvement navétane lolou djitou na laata mouy nek dieuwrin, biniou takalé ndombal tank li itam soppi woul dokhalinam benn yoon.
Ministre Amadou Ndiaye bimou dieulé kaddu nouyo na ak mboolo mi laata mouy fatali ndiarignou navétane « sou weeso waloum tagate yaram bi, navétane dafay tagate khalé yi si gueum ak fonk sa reew, si yarr ak si teguine.
Moom dieuwrin djinou denk artisanat yamoul fofou niaakhalé na ndaw yi wara djongante si niou and ak yarr ak teey si yeuf yi. Naka nonou, ministre bi tanite si kaddu wam you moudj woo na mboolem kilifeu yi nek si biir Thiès ngir niou dougueul sen lokho si djonganté bi nguir dimbali sounou ndaw yi. Laata mouy taagoo ak mboolo mi, ministre bi fatali naleen ndiarignou niakkou ak topp mesures barrières yi ndakh moniou meuna mouthieul si mbass mi.

post

Wakhtaanu kilifeu gui niou denk waloum artisanat ak transformation secteur informel ak waa ODCAV
Dibeer, niar fouki fan ak diourom niente si weerou août dieuwrign djinou denk waloum artisanat...

Le partage de l'info